TSK

TSK · Genesis 25:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Damaa bëgg, mu bàyyee ma xuntim xeer, mi ñuy wax Magpela te muy boroom. Mu ngi ci catu toolam. Na ma ko jaay lu mat njégam sëkk, dinaa ko jënd, muy sama bàmmeel ci seen biir.»

¶ Noonu la Ibraayma jënde toolub Efron ba nekk ca Magpela te janook Mamre, muy moomeelam. Dafa jënd tool ba bépp, jëndaale xuntim xeer ma ca biir, ak garab ya ca sax yépp, ba fa tool ba yem. Mboolem Etteen ña séqoon pénc ma, seede nañu ne Ibraayma moo ko moom.

Foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata, te foofa lañu denc Isaaxa ak soxnaam Rebeka, te fa laa denc Leya it.