TSK

TSK · Genesis 25:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa.

ak Basmat doomu Ismayla, di jigéenub Nebayot.

Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña!

¶ Aji Sax ji de da maa wax ne ma: «Fileek menn at mu surga bu ñu bind waññ, sagub dëkk bii di Kedar dina sàggiku,

Gétti Kedar yépp a lay dajesil, kuuyi Nebayot di la jariñ, te di sarax yu dajeek ngërëm ci kaw sarxalukaayu Aji Sax ji, ma di ko darajaale sama teddngay kër.

Waa Arabi ak mboolem garmiy Kedar it di julanteek yaw, feye la ay tàppaanga aki kuuy aki bëy.