Sarayi moomu masuloona am doom te it manu ko woona am.
TSK
TSK · Genesis 25:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sarayi ne Ibraam: «Li am mooy Aji Sax ji deful ma am doom. Kon ngalla waay, dëkkool sama jaam bi, ndax Yàlla def, mu amal ma doom ju góor.» Ibraam nag dégg la Sarayi wax.
¶ Ba loolu amee Yàlla geestu Rasel, nangul ko, may ko doom.
Ci biir loolu mu xas aw xas, daldi ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Sang bi, soo nemmiku woon ba nemmiku njàqare jii ma nekke, bàyyi ma xel, bañ maa fàtte, ba may ma doom ju góor! Kon déy, maa ko sédde Aji Sax ji, giiru dundam gépp, saatus watukaay du jaar ci boppam mukk!.»
Nu woor, daldi dagaan sunu Yàlla mbir moomu, mu nangul nu.
Éy Yàlla, yaa jagoo cant fa Siyoŋ, yaw lees di jëfeel ab dige.
Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde, njurum doom yool la.
Ab soxor, li mu ragal moo koy dab; nammeelu ku jub day sotti.
Su boobaa bu ngeen wooyee Aji Sax ji, mu wuyu; ngeen ne wallóoy, mu ne “Maa ngi.” Ndegam génne ngeen noteel ci seen biir, ak di joxoñeek a wax lu ñaaw,
Amuñu woon doom nag, ndax Elisabet manul woona am doom, te it booba ñoom ñaar ñépp a dem ba màggat.
¶ Te yemul foofu rekk, waaye Rebeka it moo am ay seex yu genn góor jur, muy sunu maam Isaaxa.