ndaxte réew, mi ngay gis mépp, yaw laa koy may ba fàww, yaak askan wi soqikoo ci yaw.
TSK
TSK · Genesis 28:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dinaa la defal njaboot gu ne xas, ay xeet sosoo ci yaw, ba ay buur soqikoo ci yaw.
Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.
Yal na la barkeb Ibraayma dal, yaak askan wi soqikoo ci yaw, ba nga moom réew mii ngay doxandéem tey, te Yàlla mayoon ko Ibraayma.»
Booba mu ngi naan, bu Esawu songee benn dal bi, dal bi ci des mana raw.
¶ Ba loolu wéyee Yàlla ne Yanqóoba: «Jógal dem Betel, toog fa te nga sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji la feeñu, ba ngay daw sa mag Esawu.»
Mu sàkk fa nag sarxalukaay, tudde bérab ba El Betel, ndax foofa la ko Yàlla feeñoo, bi muy daw magam.
Yanqóoba ma nga tudde bérab, ba Yàlla waxeek moom, Betel.
Yàlla ne ko: «Man maay Yàlla, di sa Yàllay baay. Bul ragala dem Misra, ndaxte askan wu réy laa fay sose ci yaw.
Booba Yàllaa ngay dégg seeni yuux, te fàttewul kóllëre ga mu fasoon ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.
Yàlla dellu ne Musaa: «Dangay wax bànni Israyil, ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo ma yónni ci yeen.” Aji Sax jee di sama tur wu sax dàkk, ñu di ma ko fàttlikoo ba fàww.
Mu ne: «Yaw laay jox réewum Kanaan, muy sa cér, nga séddoo.»
¶ «“Daawuda sama jaam baay doon seen buur, di seen bennub sàmm ñoom ñépp. Sama àttey yoon lañuy doxe, sama dogali yoon lañuy sàmm, di ko jëfe.
Taxul mu muurale ko lenn ci réew mii, du sax fu mu teg tànkam. Teewul mu dig ko, ne moom lay moomale réew mi, mook askanam wa koy wuutuji, te fekkul sax mu am doom.