TSK

TSK · Genesis 28:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»

Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan.

te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»

Maa ngi lay ñaan, nga musal ma ci sama loxol mag Esawu, ndaxte ragal naa, mu ñëw bóom ma, bóomaale jigéen ñi ak seeni doom.

Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: “Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”»

¶ Bu seen Yàlla Aji Sax ji yokkee seen suuf noonee mu leen ko waxe woon, te ngeen namma lekk yàpp, saa yu leen neexee sañ ngeena lekk yàpp.

Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»

¶ Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi, mi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi mi nu bokk, fa déndi asamaan ya.

¶ Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làmmiñ yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Gàtt bi, sol mbubb yu weex, ŋàbb ay cari garabi tàndarma.