Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko.
TSK
TSK · Genesis 28:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ma nga tiit nag te naan: «Bérab beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.»
¶ Ba loolu wéyee Yàlla ne Yanqóoba: «Jógal dem Betel, toog fa te nga sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji la feeñu, ba ngay daw sa mag Esawu.»
Yanqóoba samp doju xàmmikaay ca bérab, ba Yàlla waxe ak moom, tuural ko fa biiñ, sotti fa diw, sellale.
Noonu la Yuusufa tërale loola, def ko dogalu yoon ca suufu Misra, te loolooy wéy ba tey jii: juróomi céri meññeef mu ne, Firawnaay moom benn ba. Waaye suufi njiiti diine ya ca bokkul, Firawna amu ca dara.
Mboolem céru fukkeel bu ñu génnee cig jur, gu gudd gaak gu gàtt ga, muy lépp lu sàmm waññe bantam, cérub fukkeel la bu ñuy sellalal Aji Sax ji.
Indileen mboolem céru fukkeel ca kërug denc ya, ba ab dund am sama biir kër, te ngeen seetloo ma ko rekk,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ndegam duma leen ubbil bunti asamaan, ba sottil leen barke bu doy.