TSK

TSK · Genesis 29:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bi loolu amee Rasel ne: «Yàlla àtte na ma; dégg na sama ñaan, ba may ma doom.» Mu tudde ko nag Dan (mu firi Kiy àtte).

Leya neeti: «Yàlla da maa fey, ndax maa may sama jëkkër sama jaam.» Mu tudde ko Isaakar (mu firi Boroom pey).

¶ Ca gannaaw ëllëg sa ñu ànd ak metit, ñaari doomi Yanqóoba ya, Simeyon ak Lewi, càmmiñi Diina, jël seeni saamar, dugg ca dëkk ba, bett leen, rey góor ñépp.

¶ Doomi Leya ñooy: Ruben, taawub Yanqóoba, ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon.

«Simeyon ak Lewi ñoo duye yene, ñooy nas pexey ay.