TSK

TSK · Genesis 29:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Booba la ne: «Yàlla defal na ma teraanga ju réy. Bii yoon sama jëkkër dina ma teral, ndax amal naa ko juróom benni doom yu góor.» Moo tax mu tudde ko Sabulon (mu firi Teraanga).

¶ Doomi Leya ñooy: Ruben, taawub Yanqóoba, ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon.

«Simeyon ak Lewi ñoo duye yene, ñooy nas pexey ay.

Musaa taxaw ca buntu dal ba, ne: «Ku ànd ak Aji Sax ji, fii ci man!» Leween ñépp dikk, yéew ko.

¶ Lewi la wax ne ko: Sa Tumim ak sa Urim, jumtukaayi tegtal ya, ñeel na góor gay sa wóllëre, yaa ko nattoo ca Maasa, joteek moom ca ndoxum Meriba.