Genesis 43:27
TSK
Mu nuyoo ak ñoom, ba noppi laaj leen ne leen: «Seen baay bu màggat, ba ngeen doon wax, mbaa mu ngi dund? Mbaa mu ngi ci jàmm?»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu nuyoo ak ñoom, ba noppi laaj leen ne leen: «Seen baay bu màggat, ba ngeen doon wax, mbaa mu ngi dund? Mbaa mu ngi ci jàmm?»
Ci biir loolu Daawuda wàcce yóbbal ga, wacce ko wattukatub cummikaay ba, daldi daw ba ca làngu xare ba. Mu agsi, nuyook ay magam.
Yowab ne Amasa: «Mbokk mi, mbaa jàmm nga am?» Yowab jàpp sikkimu Amasa ca loxol ndijooram, mel ni ku koy fóon.