TSK

TSK · Genesis 3:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.»

¶ «Su fekkee ne ndaw si dafa am jëkkër gannaaw kàdduy xas yu ko topp, mbaa kàddug rëccle, gu mu tegool boppam,

¶ Goroom, jabaru Fineyas nag jigéenu wérul la woon te booba mu ngi waaja wasin. Naka la dégg ne jël nañu gaalu Yàlla ga, te baayu jëkkëram ak jëkkëram dee nañu, mu daldi sukk wasin. Waaye fekk na mititu matam jeexal dooleem.

Su ko defee bu ñu yéenee dogalu buur bi ci mboolem déndu buur bu yaatu bii, jigéen ñépp dinañu weg seen jëkkër, boroom daraja ba ci baadoolo bi.»

ñu tiita tiit, yaram di fuddook a metti, ñuy baddaañu ni kuy matu; ku ne jàq, di xulli sa moroom, kanam ya sël-sëleendoo.

Éy Aji Sax ji, ni kuy matu lanu meloon fi sa kanam, di wañaarook a yuuxu.

Baatu ndaw su jagadi laa dégg, ma nga jàq, di matub taawam. Baatub Siyoŋ, dëkk bu taaru baa! Ma ngay àppaat, tàllal yoxo ya, naan: «Wóoy, ngalla man; ne yàcc ci loxol bóomkat yi!»

Sa xejj yi nga miinal sa bopp, bu ñu walbatikoo tiim la, ana looy wax nag? Kon mitit du la jàpp, nga mel ni kuy matu?

Damaas a ne yasar, ne wërëñ, di daw; tiitaange ne leen nuus, njàqareeku mitit ne leen taral ni kuy matu.

¶ Waaye nag bëgg naa ngeen xam ne gépp góor, Almasi moo di boppam; jigéen, góor moo di boppam, te Almasi, Yàlla moo di boppam.

¶ Na jabar nangul jëkkëram ni mu nangule Sang bi.

Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce.

Teewul muccu jigéen a ngi ci njurum doom, ndegam saxoo na ngëm, ak cofeel, ak jëfin wu sell te yem.

¶ Naka noonu yeen jigéen ñi, nangul-leen seen jëkkër, ngir jëkkër ju ci nanguwula gëm kàddu gi it, mana gindiku te wax du ci am yoon, ngir na jabaram di jëfe,