TSK

TSK · Genesis 30:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Loolu la Aji Sax ji wax ak Ibraayma, daldi dëddu. Ibraayma it ñibbi këram.

Ba loolu weesee mu doora lekk, daldi naan, moom ak ñi mu àndal. Ñu fanaan fa keroog. Ba ñu yewwoo ca ëllëg sa, surga ba ne: «Bàyyileen ma nag, ma dellu ca sama sang.»

Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.

Ndeke Aji Sax jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan.

Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”»

Acts 7:4 TSK

¶ «Mu daldi jóge réewum waa Kalde, sanci Karan. Fa la ko Yàlla toxale gannaaw ba baayam faatoo, sancal ko ci réew mii ngeen dëkk tey.

Bu ñu nammoon réew ma ñu jóge, manoon nañoo dellu.