Ibraam nag amoon alal ju bare diggante jur, xaalis ak wurus.
TSK
TSK · Genesis 30:43
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Alalam di yokku, muy gëna barele, ba mujj am doole lool,
ndaxte lu néew nga amoon laata may ñëw, te yokku na, ba bare lool, ngir Aji Sax ji da laa barkeel ndax man. Waaye léegi nag, liggéeyal sama waa kër bopp jot na xanaa?»
Su dul woon ak sama Yàllay baay, ji ànd ak man, di Yàllay Ibraayma, ji Isaaxa wormaaloon, konoon nga dàq ma tey, ma dem loxoy neen. Waaye sama toskare ak sama àqu ñaq la Yàlla gis, ba tax mu àtte ma ak yaw biig.»
¶ Yanqóoba fanaan na fa guddig keroog, doora sàkk ca alalam, sédd magam Esawu,
Li ko waral mooy, seen alal dafa bare woon lool, ba manuñoo dëkk ñoom ñaar, te réew, mi ñu daloon, àttanu leen ndax seen gétt yu bare.
ba dootuñu taxani, dootuñu gori ca gott ya, gànnaay ya lañuy taaloo, te ñooy futti ñu leen futti woon, di sëxëtoo ña leen sëxëtoo woon. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.