¶ Am na bés, Aji Sax ji feeñu Ibraayma ca garabi Mamre yu mag ya. Booba ma nga toogoon ca buntu xaymaam digg njolloor.
TSK
TSK · Genesis 31:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 18:1
TSK
Genesis 22:1
TSK
¶ Gannaaw loolu am na bés Yàlla di nattu Ibraayma ne ko: «Ibraayma!» Mu ne ko: «Naam.»
Genesis 31:5
TSK
Mu ne leen: «Gis naa seen kanamu baay. Xam naa ne melatul na mu meloon ci man. Waaye sama Yàllay baay ay ànd ak man.
Genesis 48:15
TSK
Ma ngay ñaanal Yuusufa. Mu ne: «Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon, moom Yàlla, ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii,
1 Samuel 3:4
TSK
Aji Sax ji woo Samiyel, mu ne: «Maa ngi»,
1 Samuel 3:8
TSK
¶ Aji Sax ji wooti Samiyel ñetteel bi yoon, Samiyel jógati, dem ba ca Eli ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli nag xam ne Aji Sax jeey woo xale bi.
Isaiah 58:9
TSK
Su boobaa bu ngeen wooyee Aji Sax ji, mu wuyu; ngeen ne wallóoy, mu ne “Maa ngi.” Ndegam génne ngeen noteel ci seen biir, ak di joxoñeek a wax lu ñaaw,