¶ Ba Laban déggee ne jarbaatam Yanqóoba ñëw na, dafa daw gatandu ko, taf ko ci boppam, fóon ko, yóbbu ko kër ga. Ba Yanqóoba nettalee Laban lépp,
TSK
TSK · Genesis 31:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 29:13
TSK
Genesis 31:13
TSK
Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”»
Exodus 4:27
TSK
¶ Ci biir loolu Aji Sax ji wax Aaróona ne ko: «Demal gatanduji Musaa ca màndiŋ ma.» Aaróona dem seeti ko ca tundu Yàlla wa, fekk ko fa, taf ko ca kawam.
Ruth 1:14
TSK
¶ Ñu dellu ne yikkét, di jooyoo. Orpa fóon goroom, tàggtook moom, Ruut nag moom langaamu ko rekk.
1 Kings 19:20
TSK
Alyaasa bàyyikoo ca nagam ya, daw topp ca Ilyaas, ne ko: «Ngalla may ma, ma tàgguji sama ndey ak sama baay te topp la.» Ilyaas ne ko: «Doxal dellu; lu ma la def?»
Acts 20:37
TSK
Ba loolu amee ñépp jooyoo jooy yu metti, laxasu ko, fóon ko.