TSK

TSK · Genesis 31:53

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Naxor am ñaar fukki at ak juróom ñeent, jur Teraa.

Ibraam nag wax buurub Sodom ne ko: «Man yékkati naa sama loxo, Yàlla Aji Sax ju Kawe ji seede, moom mi sàkk asamaan ak suuf,

Te dinaa feddli sama kóllëre, gi ci sama diggante ak yaw, yaak sa askan, muy kóllëre guy sax maasoo maas ba fàww. Maay doon sa Yàlla, yaak sa askan.

¶ Gannaaw gi, dañoo yégal Ibraayma ne ko: «Milka kat am na ay doom moom it, moom ak sa mag Naxor.

Ñu ne ko: «Gis nanu bu baax ne Aji Sax ji ànd na ak yaw; moo tax nu ne ayca nu waatoo ci sunu digganteek yaw te fasanteek yaw kóllëre.

Su dul woon ak sama Yàllay baay, ji ànd ak man, di Yàllay Ibraayma, ji Isaaxa wormaaloon, konoon nga dàq ma tey, ma dem loxoy neen. Waaye sama toskare ak sama àqu ñaq la Yàlla gis, ba tax mu àtte ma ak yaw biig.»

Seen Yàlla Aji Sax ji, ragal-leen ko. Moom ngeen di jaamu, te aw turam ngeen di giñe.