TSK

TSK · Genesis 32:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.»

Seeni maam jooy ko Aji Sax ji, ne: “Bàkkaar nanu de, nde noo wacc Aji Sax ji, di jaamu tuur yi ñu naan Baal ak Astàrt. Waaye rikk xettli nook sunuy noon, nu jaamu la.”

¶ Ba loolu amee Buur Daawuda dikk ba fa kanam Aji Sax ji, toog ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji! Ana lu ma doon, ak lu sama waa kër doon, ba tax nga indi ma ba fii?

Éy, aar ma, musal ma! Bu ma rusloo, yaw laa làqoo.

Éy Yàlla, àtte ma, layool maak xeet wu gorewul, xettli maak ku njublaŋ te dëng.

Jot ma ci noteelu doom aadama, ma mana topp say tegtal.

Jubook mbokk moo tooñ, jéggi tataa ko gëna yomb, mbaa ubbi bunt yu tëje ràpp.

Am riir mooy jollee ca sa biir gàngoor, sa tata yépp tas, na Salman tase woon Bet Arbel, keroog bésub xare ba, ba ñu jëlee ndey, fenqaleek doom, ñu rajaxoo.