Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.»
TSK
TSK · Genesis 32:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk,
Yanqóoba ne ko: «Ngalla waay déet, dimbali ma rekk te jël li ma la may. Ndaxte bi ma nee jàkk ci sa kanam, gis naa ni nga ma laaye biir, ba mu mel ni Yàllaa ma geestoo yërmandeem.
¶ Seen baay Israyil nag ne leen: «Ndegam manula ñàkk, dangeen di def nii: sàkkleen ci ngëneeli réew mi, yeb ci seeni saaku, yóbbul waa ja lu mel ni tuuti diwu yaram ak lem ak cuuraayu xas ak cuuraayu ndàbb ak ay xeeti saal.
Laajal rekk say surga, dinañu la ko wax. Daawuda sa doom nag, sang bi, moo lay ñaan nga yéwéne nu ci bésu tey bu rafet bii nu dikke, te may nu loo am rekk, nu bokk kook moom.”»
Ma wax ak garmi yaak kilifa yaak mbooloo ma ca des, ne leen: «Liggéey bi réy na, yaatu na, te nun danoo tasaaroo te soreyantoo ci tata ji.
Deel maye, da lay ubbil bunt, di la àggle ci boroom daraja.
Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.