¶ Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!»
TSK
TSK · Genesis 32:30
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba Yanqóoba jógee Padan Aram, Yàlla feeñuwaat na ko, barkeel ko
¶ Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»
Gémmiñ ak gémmiñ laay waxeek moom wax ju leer nàññ ju ñu léebul, te jëmmu Aji Sax ji lay gis. Kon lu leen may fitu ŋàññ Musaa sama jaam bi?»
¶ Ab yonent lukkeekootul ci Israyil, mel ni Musaa, ma Aji Sax ji xejjoo woon ba naan ko jàkk, mu ne ko jàkk,
Ma ne: «Wóoy man, sànku naa! Man miy nit ku làmmiñam sobewu, xeetoo ci ñu seen làmmiñ sobewu, te samay gët tegu ci kaw Buur Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi.»
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.
ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.
Woowu yiw, la ko fésal moo di dikkug sunu Musalkat Almasi Yeesu, mi neenal ndee, te niital nu yoonu texe, ak ndee gu fomm ba fàww, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.