ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;
TSK
TSK · Genesis 34:30
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu la waa Misra gisee, dinañu ne sama soxna nga. Te dinañu ma rey, nga des.
Ndeke Aji Sax jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan.
«Simeyon ak Lewi ñoo duye yene, ñooy nas pexey ay.
mbaa lu mel ni menn malam suuf, mbaa malam kaw mu mel ni njanaaw,
Samiyel ne ko: «Ana nu ma fay deme? Sóol da koy dégg, rey ma!» Aji Sax ji ne ko: «Aw nag wu jigéen ngay jël, yóbbu, ne ko sarxalsi Aji Sax ji moo la indi.
Akis nag amoon na kóolute ci Daawuda, ndax da doon wax ci xelam naan: «Kii de yóbbe na boppam mbañeel gu ko bokki bànni Israyilam bañ lool. Moo tax sama surga rekk lay doon ba fàww.»
Ayitofel ne ko: «Demal dëkkoo sa nekkaaley baay, yi mu wacce këram, ñu di ko topptoo. Su ko defee bànni Israyil yépp dinañu xam ne def nga lu tax sa baay sib la. Dina tax say farandoo gëna am fit.»
Ilyaas ne ko: «Du maa lëmbe Israyil de. Yaw kay la, yaak sa kër baay, ndax yeena dëddu santaaney Aji Sax ji, di topp tuur yi nuy wax Baal.
Ku baax, boppam; ku bon, boppam.
Wutin wu lewul, sonal sa waa kër; ku bañ alalu ger gudd fan.