TSK

TSK · Genesis 35:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

kilifay waa Edom jàq, njiiti Mowab di kat-kati, mboolem waa Kanaan tiit, ne yasar;

Maa leen di dàqal ay xeet, ba yaatal seen suuf, te diiru ñetti yoon yi ngeen di teewi cim at fi kanam Yàlla Aji Sax ji, kenn du ci wuta nangu seenum réew.

Mu rey ñaari nag, dog ko, yóbbante ko ay ndaw, yónnee ko Israyil gépp. Mu ne leen: «Képp ku toppul Sóol ak Samiyel, nii lees di def ay nagam.» Ba loolu amee tiitaange ju sababoo ci Aji Sax ji dal ca kaw askan wa, ñu sàqeendoo, di benn bopp.