TSK

TSK · Genesis 37:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.»

Dëgg la, fexeel ngeen ma lu bon, waaye Yàllaa ko walbati, def ko lu baax, ba dogal li am tey jii, muy bakkan yu bare yi mucc.

Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee, ma mel ni ndab lu yàqu.

Ñii dañoo mànkoo, di tëru ku jub, di teg àtteb dee ku deful dara.

Ma ji nit cofeel, mu sosal ma; te man ma di ko ñaanal.