Sa ñaani baay ya romb xéewali tund, ya sax fàww, rombati ngëneeli jànji cosaan ya, yal na dal ci boppu Yuusufa, ca kaw ndaal boppam, moom sangub doomi baayam ya.
TSK
TSK · Genesis 37:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 49:26
TSK
1 Samuel 10:27
TSK
Terewul mu am ay nit ñu tekkiwul dara di wax, naan: «Ana nan lanu waa jii di xettlee?» Ñooñu sewal ko, yótuñu ko jenn teraanga. Sóol nag ne cell.
1 Samuel 18:8
TSK
¶ Sóol ñaawlu kàddu ga, mer lool. Mu ne ca xelam: «Daawuda lañu moomale fukki junni; man, junni! Lu ko deseeti lu moy jal bi?»
Psalms 118:22
TSK
Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj doju coll wi.
Luke 20:17
TSK
Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lii ñu bind, lu muy tekki? “Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj di doju coll wi.”
Acts 7:35
TSK
¶ «Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Ku la def kilifa ak ab àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottli yóbbante ba.