Teewul genn guddi Yàlla feeñu Abimeleg ci gént ne ko: «Yaw dee nga ba noppi, ndax jigéen, ji nga nangu, soxnas jaambur la.»
TSK
TSK · Genesis 38:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Gannaaw loolu Abimeleg woolu Ibraayma ne ko: «Li nga nu def nag? Ndax dama laa tooñ, ba nga yóbbe ma tooñ gu réye nii, man ak sama réew mi mépp? Lii nga ma def de, waroo ko woona def.»
¶ «Góor gu njaaloo, mook jabaru moroomam ji muy njaalool, dee rekk mooy seen àtte.
nañu yóbbu ndaw sa ba ca bunt kër baayam, te góori dëkk bi dóor koy doj ba mu dee, ndax moo def jëf ju gàccelu ci digg Israyil, di gànctoo kër baayam. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
Natan ne Daawuda: «Yaw, yaay waa ji! Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Man maa la fal buurub Israyil, maa la xettli ci Sóol.
«Yàgg ngeena yiwiku, dog seeni jéng, ba ne dungeen ma jaamu. Kaw tundoo tund, ker garaboo garab gu naat, gànctu ngeen fa.
¶ Aji Sax ji nag wax ma ci jamonoy buur Yosya ne ma: «Gis nga li Israyil Woyof-Kumba-si def? Di dem kaw tundoo tund ak ker garaboo garab gu naat, di fa gànctu.
Dinañu tax mboolem kuy móoloo te bokk ca ngàllog Yudeen ña ca Babilon, danga naan: “Yal na la Aji Sax ji teg la mu tegoon Cedesyas ak Akab, ña buuru Babilon lakk cib taal.”
Doyaloo, xanaa di gànctook waa Asiri. Gànctu ngaak ñoom te taxu laa doyal ba tey.
Owola di sama soxna tey gànctu, di xédd ay faram, waa Asiri xarekat ya.
Mu daldi ànd ak moom ni ñuy àndeek caga rekk. Nii lañu àndeek Owola ak Owoliba. Ñii jigéen ñu ñàkk gàcce!
Ma ne ko: «Ay fan yu bare ngay toog fi man; bul gànctu, bul ànd ak genn góor. Noonu laay def ak yaw, man itam.»
¶ Yaw ci sa wàllu bopp, ngëm gi nga ci am, yemale ko ci sa bopp, fi kanam Yàlla. Ndokklee ki sikkul boppam lenn ci jëfin wu mu dogul boppam ne noonu lay jëfe.