TSK

TSK · Genesis 4:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam.

¶ «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.

Jotkat biy toppe bakkan ba nag, mooy rey ka rey; fu mu dajeek moom, moo koy rey.

ba jotkat bay toppe bakkan fekk ko fu wees kemu dëkkub rawtoom, su boobaa su ko jotkatu bakkan ba reyee, du tax mu gàddu bakkan.

Bokk yépp daldi jóg dal ci sama kaw, sang bi. Ñu ne ma: “Jox nu sa doom ji rey doomu ndeyam, nu rey ko, feyul doomu ndeyam ji mu rey. Moo dese ndono li, kon danu koy sàkkal pexe, moom itam.” Dañoo nara fey wenn xal wi ma dese, ba xañ sama jëkkër aw tur, xañ ko aw askan ci kaw suuf.»

Job 21:14 TSK

Moona kee noon Yàlla: «Xiddi ma! Xam saw yoon soxalu ma.

ay doomam di tambaambaluy yalwaan, dëddu seeni gent, dem tàllal ay loxo.

Aji Sax ji, gaawal wuyu ma; sama xol a jeex, ma ne yàcc, bu ma xañ sa yiw, ma yem ak kuy tàbbiji biir pax.

Ku bon daw na te dàqeesu ko, ku jub ñeme ni gaynde.

Merum Aji Sax ji nag dikkal Yerusalem ak Yuda, ba mu mujj xalab leen. Gannaaw gi Cedesyas fippu buuru Babilon.

Ñooñu lees di mbugale sànkute gu sax dàkk, fu sore Boroom bi, sore teddngay manooreem,