TSK

TSK · Genesis 42:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ca gannaaw ëllëg sa ñu ànd ak metit, ñaari doomi Yanqóoba ya, Simeyon ak Lewi, càmmiñi Diina, jël seeni saamar, dugg ca dëkk ba, bett leen, rey góor ñépp.

Mu ne leen: «Jàmm rekk la; buleen tiit, seen Yàlla, jiy seen Yàllay baay, moo leen defal alal ci seeni saaku. Seen xaalis jot naa ci.» Ci kaw loolu mu génne Simeyon, indil leen ko.

¶ Ba loolu amee Yuusufa manatula téye boppam, te surgaam yépp a nga teew. Mu daldi àddu ne: «Xiddileen ma, yeen ñépp!» Ñépp dem, ba benn jaambur nekku fa, ba Yuusufa di xàmmiku ay bokkam.

Mu laxasu Beñamin rakkam, daldi jooy, Beñamin it laxasu ko, jooy.

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

Ñi ci mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi ci naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.