Genesis 43:18
TSK
Ñu am nag tiitaange ndax li ñu leen yóbbu kër Yuusufa. Ña ngay xalaat naan: «Boo demee, xaalis bi ñu yeboon ci sunuy saaku yoon wu jëkk wa, moom lañu bëgga taafantoo, dugal nu fii, ba song nu, jàpp nu jaam, nangu sunuy mbaam, boole ci.»