Genesis 29:11
TSK
Ba loolu amee Yanqóoba fóon Rasel, ne yikkét jooy.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee Yanqóoba fóon Rasel, ne yikkét jooy.
Teewul Esawu daw gatandu ko, taf ko ci boppam, langaamu ko, di ko fóon. Ñu daldi jooy!
¶ Ci biir loolu Aji Sax ji wax Aaróona ne ko: «Demal gatanduji Musaa ca màndiŋ ma.» Aaróona dem seeti ko ca tundu Yàlla wa, fekk ko fa, taf ko ca kawam.
¶ Ñu dellu ne yikkét, di jooyoo. Orpa fóon goroom, tàggtook moom, Ruut nag moom langaamu ko rekk.
Xale ba dem, Daawuda jóg, génne ca làquwaayam ba fare bëj-saalum. Mu ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot ñetti yoon, ku nekk fóon sa moroom, ñoom ñaar ñépp jooy, te Daawuda rawati.
Ma bàyyi Yàlla xel, binni, xalaat, xol jeex. Selaw.
Ba loolu amee ñépp jooyoo jooy yu metti, laxasu ko, fóon ko.