TSK

TSK · Genesis 45:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Abimeleg ne ko: «Sama réew mépp a ngi noonu, dëkkal fu la neex.»

réewum Misra a ngii ci sa kanam. Seetal fi gën ci réew mi, nga jox sa baay ak say bokk, ñu sanc. Bàyyi leen, ñu sanc Gosen, te bu ci amee ñu xareñ ci ñoom, nga dénk leen samay gétt.»

Fàkkasleen mboolem xeet yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jébbal nag. Buleen leen xool bëtu yërmande, buleen jaamu seeni tuur: Lu ko moy muy seenug fiir.

Buleen ci xool bëtu yërmande. Bakkan, bakkan a koy fey; bët, bët; bëñ, bëñ; loxo, loxo; tànk, tànk.

Ñu laajaat Aji Sax ji, ne ko: «Ndax keneen da fee ñëw?» Aji Sax ji ne: «Mu ngi nii, mu ngi làqu ci biir denc bi.»

Ana nu xel mana nangoo loolu? Na ku xarejeek ku desoon ca cummikaay la, yem ak sa moroom cér; ñépp ay séddu.»

Su ngeen ma nangoo déggal, ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.

Duma la xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Say jëfin laa lay yool, sa jëf ju siblu ji ci sa biir. Su boobaa ngeen xam ne man maay Aji Sax ji”».

Ba loolu wéyee mu wax ak ña ca des, may dégg. Mu ne leen: «Toppleen ko ca biir dëkk ba te ngeen rey. Buleen xool bëti ñéeblu, buleen ñeewante.

Teewul ma xool leen bëtu ñeewante ba sànkuma leen, faagaagaluma leen ca màndiŋ ma.

¶ «Bésub keroog boobee, ku mu fekk ci kaw am taax, te say yëf ne ca biir kër ga, bul wàcc, di ko jëli. Te ku mu fekk tool ba itam, bul dellu.