TSK

TSK · Genesis 46:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Nóoyin ab beykat la woon. Mu nekk nag ci njëmbatum reseñ.

¶ Askanu Yanqóoba mooy lii. Yuusufa tollu na ci waxambaane, am fukki at ak juróom ñaar, di sàmmle jur gi doomi baayam, yi nga xam ne soxnay baayam Bilaa ak Silpa ñoo leen jur. Yuusufa nag di leen boole ak seen baay.

“Lan mooy seen liggéey?” ngeen ne ko: “Nun de sang bi, ag jur lanu masa yar, ba nuy gone ba tey, te noonu la ko sunuy maam daan defe.” Su boobaa, ngeen mana féetewoo diiwaanu Gosen, ndaxte waa Misra dañuy xof sàmm.»

¶ Léegi Musaa ngay sàmm gàtti goroom Yettro, sarxalkatu Majan ba. Mu yóbbu jur ga fu sore ca màndiŋ ma, daldi agsi ca suufu tundu Yàlla wa ca Oreb.

waaye Daawuda da daan jaabantee fa Sóol ak Betleyem ga muy sàmme gàtti baayam.

¶ Axab nag ne Abdiyas: «Duggal ci biir réew mi te seet ci bëti ndox yeek xur yépp. Jombul nu gis ñax, ba mana rawale bakkani fas yeek berkelle yi, ba du jar nu di leen jekkli.»

Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmm ug juram, boole mbote yi cib loxoom, taf cib dënnam, yóbbu; xar yiy nàmpal, mu wommat.»