Waaye waa réew moomu leen di def ay jaam, dinaa leen àtte. Gannaaw loolu sa askan dina ca génn, ànd ak alal ju bare.
TSK
TSK · Genesis 48:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.
¶ Yanqóoba ma nga dëkkoon réewu Kanaan, fa baayam daloon.
Ba nga xamee ne àppu Israyil a ngay bëgga mat, dafa woolu doomam Yuusufa ne ko: «Ngalla waay dugalal sa loxo, mu ron sama lupp, muy ngiñ ci yaw ne dinga jëflanteek man ci ngor ak worma: rikk, bu ma denc Misra.
¶ Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»
Aji Sax ji nag mooy dox, jiitu la. Moom mooy nekk ak yaw. Du la ba, du la wacc mukk. Bul tiit, bul yoqi.»
«Maa ngi ci yoon wu dul jaas ci mboolem àddina. Nanga dëgërlu te góor-góorlu,
Buleen wóolu kilifa, doom aadama amul wall.
«Léegi nag Buur Yàlla, yiwil sab jaam, mu dem ak jàmm, noonee nga ko waxe woon.
¶ Man nag, daanaka saraxu tuuru bu sottiku laa ba noppi; sama waxtuw dem dëgmal na.
Kon ci gii wet ay nit ñuy dee doŋŋ ñooy nangu ay céri fukkeel, ca gee wet nag ku ñu seedeel ne mu ngi dund ba tey moo jagoo cérub fukkeel.
Ndax damaa leer, ni ma ko sunu Boroom Yeesu Almasi leeralale, bés bi may summi sama màkkaanu suux bii dëgmal na.