¶ Yanqóoba nag wax ak Simeyon ak Lewi ne leen: «Indil ngeen ma musiba, ndax dingeen tax waa réew mépp sib ma, muy Kanaaneen ñi, di Periseen ñi. Te itam awma lu dul góor ñu néew, te bu ñu booloo dal ci sama kaw, dañu may booleek sama waa kër faagaagal.»
TSK
TSK · Genesis 49:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñii, lu ñu wax, wérul, seen xol a mébét njekkar, seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, ñuy naxe làmmiñ wu neex.
Toogumaak naxekat, lëngoowumaak naaféq,
Bu ma sànkaaleek ab soxor, di ma booleek kuy def lu bon, di wax moroom ma jàmm, te dencal ko ay ca xolam.
Lii laay fàttliku, sama xol jeex: dama daan jàll, jiite mbooloo ma, jëm kër Yàlla ga, di sarxolleek a sant, ñu booloo di màggal.
Moo man, lu may xàddi, ne yogg? Lu may jàq nii? Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko, moom sama Yàlla mi may wallu?
Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat; ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu.
Ñeel Daawuda. Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, saa jëmm jépp di sàbbaal sellngay turam!
Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.
Ku jub, yoon lay mébét; ab soxor di lal pexey wor.
Masumaa toogandook ñiy mbumbaay bay xawaare. Yaa ma jiite, ma beru, toog ndax mer mi nga ma sol, ba ma fees.
¶ Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?