TSK

TSK · Genesis 5:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi dinga alku, ba suuf dummóoyu la, moom mi ubbi gémmiñam, naan sa deretu rakk, ji nga tuur.

Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga.

Mu ne: «Na ma defoon ak ndoxum Nóoyin ma mooy lii tey. Maa giñoon ne ndoxum Nóoyin ma, mu ni day dootu wale kaw suuf. Noonu it laay giñe ne duma la mereeti, duma la rëbbati.

te mu fekk Nóoyin ak Dañeel ak Ayóoba ci biir réew mi, giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ñooñu ñett duñu mana musal seen jenn doom, góor ak jigéen. Seen njubteg bopp mooy musal seen bakkan.

Luke 3:36 TSK

Sela, Kenan; Kenan, Arpagsàdd; Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;

¶ Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.

ndegam àddina sa woon it Yàlla jéggalu ko, xanaa Nóoyin ma daan waare njekk tey kenn ci juróom ñetti nit ña mu musal, ba mu walalee mbënn ma ci àddinay nit ñu gëmadi;