TSK

TSK · Genesis 5:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.»

Job 15:14 TSK

Ana nit ku mana jub xocc? Ana ku laab ku jigéen jur?

Aji Sax jee tollu asamaan, jéer doom aadama, di seet ku ci xelu, tey sàkku Yàlla.

Luke 1:35 TSK

Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla.

¶ Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.

Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan, ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.