TSK

TSK · Genesis 50:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ibraayma dégg li ko Efron wax, daldi waññal Efron limu xaalis, bi mu wax ci kanam Etteen ñi, maanaam ñeenti téeméeri dogi xaalis yu dëppook nattu jaaykat ya.

Nii la Etteen ña dogalale Ibraayma njaayum tool ba ak xunti ma ca nekk, mu def ko bàmmeel.

Isaaxa ak Ismayla, doomam yu góor ya, rob ko ca xuntim xeer ma ca Magpela te jàkkaarloo ak Mamre, ca toolub Efron doomu Sowar, Etteen ba.

Foofa la bakkanam rote, mu faatu, fekki ay maamam, gannaaw ba mu màggatee, ba ñor xomm. Ba loolu amee ay doomam Esawu ak Yanqóoba rob ko.

¶ Gannaaw loolu da leena dénk ne leen: «Maa ngi waaja fekki samay maam; dencleen ma fa samay maam ca xuntim bàmmeel ba ca toolub Efron, Etteen ba.

Acts 7:16 TSK

Gannaaw gi lañu toxal seeni yax ca Sikem, denc leen ca bàmmeel, ba Ibraayma weccikoo woon xaalis ca doomi Amor ca Sikem.