TSK

TSK · Genesis 6:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge.

Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.

Aji Sax ji day seetlu ku jub; ku soxor, bëgg fitna, mu bañ.

Yal nañu këppoo xali sawara, tàbbi ciy pax te dootuñu jóg.

Ni bëtu ndox di dawe, ni lañuy dawale seenug coxor. Fitnaak salfaañooy riir ci dëkk bi, gisuma lu moy jagadeek loraange!»

Sa liggéeyu jula bu yaatu moo la feesal fitna, nga bàkkaar, ba ma nangoo sa teddnga fa tundu Yàlla wa, sànk la, yaw malaakam serub miy aare, nga jóge digg doj yuy tàkk.

Éy Aji Sax ji, foo àppal lii, may woote wall, dégluwoo ma? Ma di la jooy aw ay, te walloowoo!

Ay wi nga teg Libaŋ mooy këppu ci sa kaw, te sànkuteg rabi àll yi sa tiitaange lay jur. Yaa tuur deretu nit, indi aw ay ci réew mi, ak dëkk beek mboolem ñi ci biiram.

Ndax kat du déglukati yoonu Musaa lees di joxee àtteb ñu jub fa kanam Yàlla, waaye jëfkati yoonu Musaa lees di joxe nit àtteb ku jub.