TSK

TSK · Genesis 6:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Defal nga ma yiw, yërëm ma lool, ba musal ma. Waaye bala maa daw, ba àgg ca tund ya, musiba mii man naa dal ci sama kaw, ma dee.

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

Kon nga xam lu jaadu, neex Yàllaak doom aadama.

Ku baax, Aji Sax ji bége la; kuy fexe lu bon, mu daan la.

Luke 1:30 TSK

Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.

¶ Kuy liggéey, ag peyooram du taxawe ag may, waaye wartéef la.

Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Xanaa yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla, wi ànd ak man la.

Yal na ko Boroom bi may mu daj bésub keroog booba, yërmandey Boroom bi. Taxawu na ma lool ca Efes, te xam nga ko xéll.

Titus 3:7 TSK

Noonu la nu Yàlla joxe àtteb ñu jub ci kaw aw yiwam, ba nu mujj séddu ci texe gu sax dàkk, ni nu ko séentoo.

ndegam àddina sa woon it Yàlla jéggalu ko, xanaa Nóoyin ma daan waare njekk tey kenn ci juróom ñetti nit ña mu musal, ba mu walalee mbënn ma ci àddinay nit ñu gëmadi;