¶ Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet.
TSK
TSK · Genesis 7:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye dinaa fas kóllëre ak yaw, nga dugg ci gaal gi, yaak say doom ak sa soxna ak say soxnay doom.
Nóoyin dugg na ca gaal ga, ànd ak ay doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya, ngir mucc ca ndoxu mbënn ma.
¶ Doomi Nóoyin yu góor, yi génne ci gaal gi, ñooy: Sem, Xam ak Yafet; Xam mooy baayu Kanaan.
¶ Doomi Xam yu góor ñoo di ñii: Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan.
¶ Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.
ndegam àddina sa woon it Yàlla jéggalu ko, xanaa Nóoyin ma daan waare njekk tey kenn ci juróom ñetti nit ña mu musal, ba mu walalee mbënn ma ci àddinay nit ñu gëmadi;