TSK

TSK · Genesis 7:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Mboolem mbindeef mu daan dox ci kaw suuf dee na ca. Picc yi ak jur gi ak rabi àll yi ak lépp luy raam ci kaw suuf dee na, ñoom ak nit ñépp.

Ndox ma daa délsi, boole mëdd watiiri xare yaak gawar ya, mboolem xarekati Firawna, ya leen toppoon ca biir géej ga rekk. Kenn rëccul.

Job 22:15 TSK

Dangaa nara topp ñallu démb, wa nit ñu bon ña ñaloon?

Junni daanu fi sa wet, fukki junni (10 000) daanu fi sa ndijoor, du tax mu jege la.

Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.

su Nóoyin ak Dañeel ak Ayóoba bokkoon nekk ca seen biir sax, ñoom ñett doŋŋ la seen bakkan di mucc ndax seenug njub. Boroom bi Aji Sax jee ko wax.

¶ «Noonee mu deme woon ca janti Nóoyin, ni lay deme ca janti Doomu nit ki.

ñooña gëmadi woon bu yàgg, jant ya Yàllay muñ, di négandiku, te Nóoyin di yett gaal, ga lim bu néew, juróom ñett, mucce woon ca ndox ma.

Su demee noonu kay, kon Boroom bi def loolu lépp, xam na nu muy musale nit ñu jullite cib nattu, ak nu muy xaare nit ñu dëng ñi, ngir seen mbugal kera bésu àtte ba.