Ruben nag àddu ne leen: «Ndax newuma leen woon: “Buleen gàddu bakkanu xale bi,” waaye faalewuleen ma; tey rekk la nu Yàlla doon xaare bakkanam, bi nu gàddu.»
TSK
TSK · Genesis 9:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Ku dóor nit, rey ko, dee rekk mooy àtteem.
Buleen wër di yàq deru nit ci seen bokki waa réew. Buleen def dara lu mana reylu seen moroom. Maay Aji Sax ji.
¶ «Ku rey ag jur na fey boroom, waaye ku rey nit dee mooy àtteem.
Su dee aw doj wu mana rey la jël, dóor ko ko, mu dee, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey.
mbaa ci biir mbañeel la ko dóore loxoom ba mu dee, su boobaa dee rekk mooy àtteb ka dóore. Moo ko bóom. Jotkat bay toppe bakkan ba nag, bu dajeek ka rey, da koy rey.
¶ Su fekkee ne nit ki dafa bañ moroomam, su ko tëroo, dal ci kawam, ba fàdd ko, mu dee, su làqujee ci dëkk yooyu benn,
¶ Su dee dañoo fekk ku ñu bóom ci biir réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji moomale, mu tëdd ci àll bi, te xameesul ku ko rey,
Jëflanteel ak moom ci kaw xel, bu ko bàyyi mu duggaale bàmmeel bijjaaw.
Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ, siiwal-leen ay jalooreem ci xeet yi!
Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndu suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.