TSK

TSK · Haggai 2:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Man nag maay dëgëral boppu waa Misra, ba ñu dugg, topp leen. Su ko defee ma siiwal sama ndam, ndax dinaa yar Firawnaaki xarekatam yépp, boole ci watiiri xareem aki gawaram.

Watiiri Firawnaaki xarekatam la fab sànni géej; ñeyi xareem ya labandoo ca géeju Barax ya,

Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.

Nit ñaa ngi màtte ndijoor, te doyaluñu, di xàmpe càmmoñ te suuruñu, ku nekk di yàpp sa mbokk:

Mu diw xeet, dim réew, ku la ci nangulul sànku. Xeet yooyu yépp ay yàqu yaxeet.

Ca laay wool mbooloom Gog saamar fa sama kaw tund yépp, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, mbokk di jam mbokk saamar.

Naka ngay xool, aw doj wu loxo sànniwul fàq, daldi dal ca tànki jëmm ja bindoo weñ ak ban bu ñu lakk, daldi koy rajaxe.

Moo waral nga gis doj wu loxo sànniwul, mu fàqe tund wa, daldi rajaxe weñ gaak xànjar jaak ban baak xaalis baak wurus wa. Buur, Yàlla ju màgg ji moo la xamal liy ñëw. Gént gi wér na, piri mi mata gëm.»

Xelum njublaŋam lay naxee, di réy-réylu, ba bett ñu bare, faagaagal leen, te dina dëkk kilifay kilifa yi. Waaye mooy sànku, te loxo du ko laal.

Micah 5:9 TSK

«Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «maay dagge fi sa biir, sa fasi xare, te maay sànk sa watiiri xare.

¶ Mu wax ma ne ma: «Lii moo di kàddug Aji Sax ji dikkal Sorobabel, di wax ne: Du cig njàmbaar, du ci doole, ci samag Noo la. Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.»

Maay jàll géeju njàqare ga, fàdd gannax ya, mboolem xóotey dexu Niil wow, sagub Asiri sàggiku, nguurug Misra foq.

Su bés baa laay tàmbalee faagaagal mboolem xeet yiy songsi Yerusalem.