te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»
TSK
TSK · Haggai 2:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee niir wa yiir xaymab ndaje ma, leeru Aji Sax ji fees jaamookaay ba,
ba sarxalkat ya talatuñoo liggéey, ndax leeru Aji Sax jaa nekkoon ca niir wa, niir wa feesal kër ga.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.
Fitt giy misaal Yerusalem ndijooram lay wadd. Mu sës dénki dàjjikaay yi, yéene ndigalu bóome, xaacu, daldi sës dénki dàjjikaay yi ci bunt yi, yékkati sëkk yi, ngir taxawal ab gawukaaay.
Ma bëgga am lu leer ba tey ci fukki béjjén yi ci bopp bi ak beneen ba génn, ba ñett daanu ca kanamam; mu am ay bët ak gémmiñ, di wax kàdduy damu, te ëpp yi ci des.
Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.
Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
¶ Ca gannaaw ëllëg sa lañu ko fekk ca kër Yàlla ga, mu toog ca digg jànglekat ya, di leen déglook a laaj.
¶ Mu am bés bu Yeesu doon jàngal askan wi ca kër Yàlla ga, di xamle xibaaru jàmm bi. Sarxalkat yu mag ya ak firikati yoon ya ne jalañ, ñook njiit ya.
Mbooloo mépp a daan jëlu, fekki ko ca kër Yàlla ga, ngir déglu ko.
Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»