TSK

TSK · Hebrews 1:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Alyaasa nag ñaan ne: «Aji Sax ji, ngalla ubbil ay bëtam, mu gis.» Aji Sax ji ubbi bëti surga ba, mu xool, ndeke tund waa nga fees aki fas aki watiiri sawara, wër Alyaasa.

Ay malaakay seraf ñoo taxaw, tiim ko, ku ci nekk am juróom benni laaf: ñaar yu muur seen kanam, ñaar yu muur seeni tànk, ak ñaar yu ñuy naawe.

dexu sawara di wal, balle fa kanamam. Junniy junnee nga koy jaamu, mboolooy mbooloo dar ko. Waa pénc ma toog, téere ya ubbiku.

Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?