¶ «Aaróona day sarxal yëkk wi, muy saraxu póotum bàkkaaram, di njotlaayal boppam, mook waa këram.
TSK
TSK · Hebrews 10:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Leviticus 16:6
TSK
Leviticus 16:29
TSK
¶ «Te itam dogal a ngii, di lu leen war fàww. Bésub fukki fan ci juróom ñaareelu weeru at mi nangeen ci toroxlu te du lenn lu ngeen ci mana liggéey, du njuddu-ji-réew du doxandéem bi ci seen biir;
Leviticus 23:27
TSK
«Te itam fukki fan ci juróom ñaareelu weer woowu, bésub Njotlaay ba lay doon. Ndaje mu sell ngeen ciy amal. Nangeen ci toroxlu te indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
1 Kings 17:18
TSK
Jigéen ja ne Ilyaas: «Éy góoru Yàlla gii! Ana lu ma séq ak yaw? Xanaa dangaa ñëw sullisi sama bàkkaar, ba tax nga rey sama doom ju góor jii?»
Hebrews 9:7
TSK
Waaye ñaareelu néeg ba, sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo ca daan dugg, benn yoon cim at, te du ñàkka duggaale deret ju muy jooxe ngir boppam, ak itam ngir bàkkaar yi askan wi def te du ag teyeef.