TSK

TSK · Hebrews 13:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Njuddu-ji-réew ji nangeen ko yemaleek doxandéem bi ngeen dëkkal. Soppleen ko ni ngeen soppe seen bopp, ndaxte ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Mu dem di wuti ndox, Ilyaas dellu ko woo, ne ko: «Rikk sàkkal dogu mburu, yótaale ma.»

Job 31:19 TSK

Ndegam maa seetaan ku rafle nara sànku, seetaan néew-ji-doole ju amul malaan,

Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, gis ku rafle, wodd ko, te baña nëbbu mbokk mu soxla?

Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram. Mu daldi nu ñaan, ne nu: «Ndegam ab gëmkatub Sang bi ngeen ma jàppe, agsileen, dal ak man ca sama kër.» Mu soññ nu ba nu nangu.

¶ Gayus mi may dalal, di dalal mbooloo mi mépp këram, nuyu na leen; Eràst saytukatub alalu dëkk bi it, nuyu na leen, mook mbokk mi Kàrtus.

te di ku ñu seedeel jëf ju rafet; lu mel ni yar ay gone, ak man gan, ak teral gëmkat ñu sell ñi, ak dimbali ñi tollu diggante, ak di jàppoo jépp jëf ju baax.