TSK

TSK · Hebrews 13:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 16:1 TSK

¶ Ci kaw loolu Póol agsi Derbe, teg ci dëkk ba ñuy wax Listar. Ndeke ab taalibee nga fa bu ñuy wax Timote; ndeyam di gëmkatub Almasi bu bokk ci askanu Yawut, baayam di Gereg.

Teewul nag bu ma noppee ci lii, ba teg teraanga jii ca loxoy waa Yerusalem, Espaañ laa jëm, te fa yeen laay jaare.

Joŋanteel joŋante bu baax bi, ngir yoonu ngëm wi, te nga ŋoy bu baax ci texeg fàww gi ñu la woo, ba tax nga dëggal sa ngëm nu rafet noonu nga ko dëggale woon fa kanam seede yu bare.

¶ Ci man Póol, mi ñu tëj kaso ngir Almasi Yeesu, ci man ak itam ci Timote miy mbokkum gëmkat la bataaxal bii bawoo, ñeel Filemon, sunu soppe bi bokk ak nun liggéey bi.

¶ Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi.