Maa ngi nii ànd ak yaw, di la sàmm fépp foo jëm, te itam dinaa la délloosi ci réew mii. Duma la bàyyi mukk, waaye dinaa def li ma la wax lépp.»
TSK
TSK · Hebrews 13:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Musaa far dal ca kër waa ja. Mu mujj ko may doomam ju ñuy wax Sipora.
Dëgërluleen nag te am fit. Buleen tiit, buleen yox-yoxi ndax ñoom, ngir seen Yàlla Aji Sax ji mooy ànd ak yeen. Du leen ba, du leen wacc mukk.»
Aji Sax ji moom turam wu màgg wi tax na du wacc ñoñam, ndax Aji Sax ji la soob, mu def leen ñoñam.
Ku bon déy a ngi tëggoo bànneexu bakkanam, ku bëgge di ñàkke wormaak a teddadil Aji Sax ji.
Aji Sax ji kat daa sopp yoon, te du wacc jaamam bu gore. Day fegu ba fàww, askanu ku bon dog.
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.
«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.
Li wadde ci ay xaaxaam mooy ñi dégg kàddu gi, te ay xalaat ak alal, ak bànneexu bakkan fatt leen, ba tax meññaluñu lu ñor.
¶ «Ab jaamu kër nag manula jaamu ñaari sang; day dëddu kii, sopp kee; mbaa mu fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.»
Dama leena bind, ne leen buleen amlante ak ku tuddoo mbokkum gëmkat, te di fokatub séy, mbaa mu dib bëgge, mbaa mu dib bokkaalekat, mbaa ab saagakat, mbaa màndikat, mbaa ab ŋàppaaral. Ku ni mel, buleen bokk ak moom lekk sax.
¶ Lu jëm nag ci powum séy, ak jépp jëfi sobe, mbaa ag bëgge, li jekk ci ay nit ñu sell, moo di ñu bañ koo tudd sax ci seen biir,
Ag ñàkk nag taxul may waxe nii, nde tàmm naa di doylu ci diggante bu ma mana tollu.
Bumu di ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, waaye na lewet, bañu ay, te bumu di bëggkatub xaalis.
Seenug bëgge lañuy ràbbe ay kàddu yu ñu leen di koppartoo. Ñooñu la seenub daan yàgga yoot, te seen sànkute nelawul.
¶ Ngalla ñii! Ñoo jaare yoonu Kayin; ñoo lajj, topp Balaam cig réeram ngir ag peyoor; ñoo diiŋat ba sànku ni Kore.