Bala tund yee juddu, bala ngay sos suuf ak àddina, yaa mas di Yàlla, ba fàww.
TSK
TSK · Hebrews 13:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñoom ñuy jeex, yaw nga sax, ñoom ñépp ràpp ni mbubb, nga soppi leen niy yére, sànni;
Ana ku def lii, dogal ko? Xanaa ki dale fa njàlbéen di woo maas yi! Man Aji Sax ji maa jëkk, te man laak ñi mujj ba tey!
«Man Aji Sax ji déy, duma soppiku, te yeen noppiwuleen di askanu Yanqóoba, ay workat.
ndax Doomu Yàlla, Yeesu Almasi, mi nu biral ci seen biir, man ak Silas ak Timote, du kàddug «waaw, déet;» «waaw» doŋŋ a nekk ci moom.
gépp may gu baax, ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.
¶ «Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk ëllëg, te di Aji Man ji.
¶ Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj.