¶ Buleen lekk lenn lu seexluwu.
TSK
TSK · Hebrews 13:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Piyeer ne ko: «Mukk, Sang bi, ndaxte masumaa lekk lenn lu daganul mbaa lu setul.»
¶ «Léegi nag, dénk naa leen Yàlla ak kàddug yiwam, gi leen mana dooleel, dencal leen seen muur ci biir mboolem nit ñi ñu sellal.
Ndax kiy taamu bés, Boroom bi la koy taamul; naka noonu kiy lekk, Boroom bi la koy gërëme, nde moom lay sant doora lekk; ki lekkul it Boroom bi lay sàkkoo ñàkka lekkam, te Yàlla lay sant.
¶ Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale, ak a téqtale, te ngeen moytu leen.
Waaye du wenn ñam wu nuy jegele ak Yàlla. Nu lekk ko, ak nu bañ koo lekk, du nu yokk, du nu wàññi.
Lu tax? Ndax dama leena buggul? Yàlla xam na ne «ahakay!»
¶ Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir gu ni mel.
¶ Bu leen kenn naxe waxi ngelawal neen, ndax yooyu ma lim mooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw aji déggadi ñi.
Sampleen seeni reen ci moom, tabaxuleen ci moom, feddlikuleen ci wàllu ngëm, ni ñu leen ko jàngale, ba seenub xol baawaanal kàdduy cant.
bu leen lenn gaawa xañ sago ba ngeen ñàkka ànd ak seenum xel, mbaa mu di leen jaaxal; du lu ñu ne kàddug waxyu la, du genn kàddu mbaa bataaxal bu ñu nu moomale, te di leen gëmloo ne bésu Sang bi dikk na ba noppi.
¶ Noowug Yàlla wax na ci lu leer ne ci mujug jamono, dina am ñu wacc yoonu ngëm wi, di topp ay xalaat yuy fàbbee ak ay àlluway ceytaane,
¶ Ngalla waay Timote, sàmmal li ñu la dénk! Moytul kebetuy àddinay kese, ak werantey diiŋatkat yu tuddoo boroom xam-xam.
te baña topp léebi neen yu Yawut yi, ak santaaney nit ñi dëddu liy dëgg.
Ñooñooy gàkkal seen jataayu lekk yi gëmkat ñiy bokk, di ñóox te amuñu ci jenn jom; ñooy xiin yu naaxsaay yu ngelaw li yóbbu; ñooy garab yu dee ñaari yoon, du meññ waxtoom, reen ya buddiku.