TSK

TSK · Hebrews 2:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun).

Moo tax ma di ko jox ab cér ci biir ñu bare, mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem, ngir moo jébbale bakkanu boppam, ñu limaale kooki tooñkat, moo gàddu bàkkaaru ñu bare te mooy tinul moykat yi.

Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal gi war ci bàkkaar,

¶ Li may wax bokk yi, moo di suux ak deret du am cér ci nguurug Yàlla, te luy yàqu manula am cér ci lu dul yàqu.

Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,

Moo dog sidditi boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, ñu doon ay jaam yu mu jàppe xare. Moo leen weer it ci kanam ñépp, diriwaale leen ca biir njaab ma topp ca ndam, la Almasi ame ca bant ba.

Woowu yiw, la ko fésal moo di dikkug sunu Musalkat Almasi Yeesu, mi neenal ndee, te niital nu yoonu texe, ak ndee gu fomm ba fàww, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.

Bul ragal mukk mitit wi nga nara daj. Seytaanee ngi noonu di dugal kaso ñenn ci yeen, ngir nattu leen. Dingeen am coono diiru fukki fan. Nanga saxoo kóllëre ba dee fekk la ci, ma kaalaa la kaalag dund.

Mu jàpp ninki-nànka ja, jaani cosaan jooju di Tuumaalkat bi, di Seytaane ba tey. Malaaka mi yeew ko diiru junniy at.