TSK

TSK · Hebrews 3:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: «Ba kañ la ma askan wii nara xarab? Ba kañ lañu may gëmadi, ak firnde yi ma def ci seen biir yépp?

kenn ku moy Kaleb doomu Yefune ak Yosuwe doomu Nuun, du kenn ku ciy dugg ca réew, ma ma leen giñoona dëël.

Teewul bugguleen woona dem, xanaa di gàntal seen ndigalal Yàlla Aji Sax ji.

Ak ba leen Aji Sax ji yebalee fa Kades Barneya, ne leen: «Demleen nanguji réew ma ma leen jox.» Yeena gàntal seen kàddug Yàlla Aji Sax ji, gëmuleen ko, déggaluleen kàddoom.

Moo ma taxa giñe sama biir mer, ne: “Duñu tàbbi mukk ci samag noflaay.”»

Kon nag am na ñenn ñu ci wara tàbbi ba tey. Te ñi ñu jëkkoona àgge xibaaru jàmm bi, tàbbiwuñu ca ndax seenug déggadi.